Kaabu

Jóge Wikipedia.
Dem: Joowiin, Seet

Kaabu, benn nguur la woon, ca bëj saalumu Senegaal ak kawu Gine Bisaawóo. Tey, mengoo na ak Diiwaanu Séeju, Kolda, ak li ko wër.


Cosaan[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Nguur gi, ñi ko taxawal, soose yi la.

Sunjata Keyta, jamono bi mu nekkoon buur bu jiite imbraatoor gu Mali (Manden), cosaan ne na, ki nekkon ci jalu Jolof, tooñ na ko.

Li mu ko tooñee tax, Sunjata Keyta buggoon mbugël buur ba Jolof bi.

Kon, Sunjata Keyta wotee xarekatam, ngir ñu dem Jolof, xeex ak buur bi fa ne woon.

Ku doon jiite xarekatam, benn dagu Sunjata la woon, bu ñu naan Tiramakan Tarawale. Ñoom ñepp ay soose lañu woon.

Ba ñu agsee Jolof, xeex neen ak wa Jolof, waaye ba noppi, dellusiwuñu Mali. Dañoo wacc ca dexug Gambi.

Ñu fa wacc nag, fekk fa ay soose ñu fa ne woon. Soose yi ñu fekk foofu, ñoom, dañu fa dëkkoon bu yag a yag sooga Tiramakan Tarawale ñow, waaye ñoom itam, Mali leeñ juge. Ci diggante dexug gambi ak li ñu wowee tey Kaasamaas, soose yi nekkoon nañu fa.

Kon Tiramakan Tarawale, dajale na soose yi yepp ne woon foofu, elif leen.

Waaye nag, ca bëj saalum, amoon na Baynuk yi ak Joolaa yi. Dañu fa amoon seeni nguur. Ñu sant Saane, Maane, Saaña, ak yeneen, ñoo doon yoree nguuri Baynuk ak Joola yi. Seen peey, di woon Mampatiŋ.

Tiramakan Tarawale, buuri Baynuk ak Joolaa yi, dañoo mujj seyante. Li moo jur li ñi wax Nancoo yi. Nancoo yi tabax nguuru Kaabu, ca jeexitu XIII xarnu.

Seeni mbootaayug[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Fariŋ Kaabu, mooy turu buuru Kaabu. Kooku, ci kawam, am na Mansa Manden, ki jiite Imbratoorug Mali.

Jiggeenu Fariŋ bi ñu leen wo Musu-Mansa. Meeni Fariŋ bi waroon juge ngir mëna falu, ñoom la. Meen moo gënoon am solo Geño.

Amoon na ay Laman, yore wallu suuf si, nekk ci suufu Fariŋ bi, ñooy Mansa-Ba yi.

Ñoom ñepp, ñu leen ne Nancoo.

Suuf si[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kaabu, xajoon na ci fukk ak ñaar diiwaan. Ñooy:

Jimara, Sama, Paccana, Sankolla, Kantoora, Mana, Bajar, Tumaana, Caaña, Pakis, Kolla, Propana.

Peeyug Kaabu, Kansala, la woon. Diiwaan bu nekk, am peeyam.

Mujjam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kaabu mujj na daan ndax Pël yi. Ca XIX xarnu, Pël yi nekkoon Kaabu, Nancoo yi dañu leen daan noot. Foofu, Pël yi dañoo yagoon soon ak Nancoo yi ñu leen daan soonal, ba ca njëlbeen. Kon Pël yi (ñu dëkkon Kaabu ci ay Fulakunda), ñoo woolu seeni benn mbokk, ñu naan ko Alfa Molo Balde. Ki, maamam ay soose lañu woon (sant Dumbuya). Alfa Molo Balde, ak Almaami yi bu Fuuta Jallon, and nañu, xeex ak Nancoo yi, ba daan leen. Ba loolu weesoo, ñu sanc seen nguur, di Fuladu, doomu Alfa Molo Balde di Muusa Molo Balde jiite ko. Ba tey, su ñu demee bëj saalumu Senegaal, am ñi wax Kaabu yeneen yi wax Fuladu. Pël yi nekk Fuladu, ñooy Firdu yi. Noonu la Kaabu mujjee, ci diggu XIX xarnu.